Ubbil li ci biir

Ñan ñooy Seede Yexowa yi ?

Danga ñuy gis bu ñuy waare ci kër yi walla ci mbedd yi. Xéyna am na loo liir ci surnaal yi lu jëm ci ñun walla am na li nga dégg ci ñun. Waaye ndax xam nga Seede Yexowa yi dëgg-dëgg ?

Li ñu gëm ak seeni yëngu-yëngu

Ay Seede Yexowa nettali nañu seen jaar-jaar

Xoolal li Seede Yexowa yi nettali ci seen jaar-jaar ak lépp li ñuy def ngir topp ci seeni xalaat, seeni wax ak seeni jëf, li nekk ci Biibël bi.

Ku bëgg a jàng Biibël bi te doo fey dara

Lu tax ñu war a jàng Biibël bi ?

Biibël bi tontu na ay milioŋu nit ci àddina si sépp ci seeni laaj yi gën a am solo. Ndax bëgg nga bokk ci ñooñu ?

Njàngum Biibël, naka lañu koy doxale ?

Ci àddina si sépp, Seede Yexowa yi dañu leen a xamme ci njàngum Biibël bi ñuy defal nit ñi. Xoolal ni muy deme.

Ndax bëgg nga ñu seetsi la?

Mën nga waxtaan ci benn laaj ci Biibël bi walla nga jàng lu jëm ci Seede Yexowa yi.

Ndaje yi ak xew-xew yi

Ñëwal teew ci benn ndaje Seede Yexowa yi

Xoolal fi ñuy defe suñu ndaje yi ak ni ñuy jaamoo Yàlla. Ñépp ñi ko bëgg mën nañu ñëw. Kenn du fey dara.

Ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu

At mu nekk, ay milioŋi nit dañuy booloo ngir fàttaliku deewu Yeesu. Ñu ngi lay woo nga ñëw ngir xam njariñ bi nga mën a jële ci xew-xew bu am solo boobu.

Ñan ñooy def tey li yexowa santaane ?

Am na ay seede Yexowa fépp ci àddina si te bokk nañu ci xeet yépp ak cosaan yépp. Lan moo leen boole, ñu nekk benn ?

Ci àddina si sépp

  • Seede Yexowa yi ñu ngi ci 239 réew

  • Seede Yexowa yi ñu ngi tollu ci 8 699 048 nit

  • Seede Yexowa yi ñu ngi jàngal Biibël bi 5 666 996 nit

  • Nit ñi teewoon daaw ci bés bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu ñu ngi tollu ci 19 721 672

  • Am na 117 960 mbooloo Seede Yexowa