Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 7

Li Yàlla dige, jaarale ko ci yonent yi

Li Yàlla dige, jaarale ko ci yonent yi

YONENT yu njëkk ya dañu gëmoon Yàlla dëgg. Li Yàlla dige, gëmoon nañu ko te dañu ko doon dunde. Dige yooyu, lan la ëmboon ?

Aadama ak Awa dañu bàkkaar rekk, Yàlla daldi dig ne dina indi kuy toj boppu “ jaan ja ”, maanaam ku koy alag ba fàww. Jaan ja mu ngi misaal “ ninkinànka ju réy ji, di jaani cosaan ji, te ñu di ko wax Tuumaalkat bi mbaa Seytaane ”. (Njàlbéen ga 3:14, 15 ; Peeñu ma 12:9, 12). Kooku nar a ñëw, kan lay doon ?

Lu tollu ak 2000 at ginnaaw bi Yexowa dige loolu, dafa wax Ibraayma ne kooku di ñëw dina bokk ci askanam. Lii la Yàlla wax Ibraayma : “ Waa àddina sépp dinañu taasu ci sa barkey askan, ndax déggal nga ma. ” — Njàlbéen ga 22:18.

Ci atum 1473 bala suñu jamono di tàmbali (B.S.J.T.), am na lu Yàlla wax Musaa lu jëm ci askan boobu. Lii la Musaa wax doomu Israyil yi : “ Yexowa mi ngeen di jaamu dina leen indil benn yonent buy jóge ci seen biir, ci seen mbokk, ni man — moom ngeen war a déglu. ”(5 Musaa [Deutéronome] 18:15, MN). Kon ni Musaa, yonent boobu dina bokk ci askanu Ibraayma.

Yonent boobu dina bokk it ci askanu Dawuda mi nekkoon buur te moom ci boppam dina mujj a nekk buur bu mag. Lii la Yàlla dig buur bi tudd Dawuda : “ Dinaa fal ci sa askan ku génne ci sa geñoo [. . .] te may saxal ba fàww jalu nguuram. ” (2 Samwil 7:12, 13). Yàlla wax na it ne kooku dinañu ko woowe “ Buuru jàmm ” ba pare ne : “ Nguuram dina gën a law, te jàmmam sax ba fàww. Dina toog ci jalu Dawuda ak ci nguuram, di ko dëgëral ak a taawu, ci dëgg ak ci njub léegi ba fàww. ” (Esayi 9:5, 6). Waaw, Njiit bu jub boobu dina indiwaat jàmm ak njub. Waaye kañ la naroon a ñëw ?

“ Askan ” bi Yàlla dige dina . . . bokk ci askanu Ibraayma, nekk yonent ni Musaa, bokk ci askanu Dawuda, ñëw ci atum 29 C.S.J., toj boppu jaan ji, Seytaane

Lii la malaaka mi tudd Jibril wax yonent Yàlla bi tudd Dañeel : “ Fàww nga xam lii, te na sa xel ñaw : dale ko ci bés bi ñuy joxe ndigal ngir defaraat ak it tabaxaat Yerusalem ba ci jamono Almasi bi, Njiit bi, dina am juróom-ñaari semen, tegaat ci juróom-benn-fukk ak ñaari semen. ” (Dañeel 9:25, MN). Semen yooyu, bu ci nekk dafa doon def juróom-ñaari at. Kon 69 semen yi dañu doon def 483 at. Dañu komaase ci atum 455 B.S.J.T. te mujje ci atum 29 ci suñu jamono (C.S.J.). a

Ndax dëgg-dëgg ci atum 29 C.S.J. la Almasi bi ñëw, maanaam yonent boobu naroon a nekk ni Musaa te mu nekkoon askan bi ñu doon xaar bu yàgg ? Nañu seet loolu.

a Xoolal li nekk ci yeneen leeral 2 ci téere bi tudd Mën nga dund ci jàmm ba fàww! Seede Yexowa yi ñoo ko génne.