Ubbil li ci biir

Man ak sama jabar Tabitha ñu ngi waare

BIIBËL BI DAFAY SOPPI DUND

Dama gëmoon ne Yàlla amul

Dama gëmoon ne Yàlla amul
  • AT BI MU JUDDU: 1974

  • RÉEWAM: RÉPUBLIQUE DÉMOCRATIQUE ALLEMANDE

  • JAAR-JAARAM: GËMUL WOON NE YÀLLA AM NA

LI MA DUND

Maa ngi juddoo ci benn dëkk bu ndaw ci goxu Saxe, ci réew mi ñu doon woowe République démocratique allemande (RDA). Suñu kër neexoon na te amoon nañu mbëggeel ci suñu biir. Samay waajur dimbali nañu ma ma am jikko yu rafet. RDA, réewum communiste la woon, kon ñu bare ci Saxe, diine amul woon solo ci ñoom. Man, dama gëmoon ne Yàlla amul. Ba bi may am 18 at, li ma jàppoon mooy Yàlla amul te communisme mooy li gën.

Lu taxoon communisme neex ma? Ndaxte ci man, nit ñépp a yem. Te itam dama jàppoon ne dañu war a yemale ñépp ci ni ñuy séddalee alalu réew mi. Noonu kenn du am alal ba mu ëpp wala ndóol ba mu ëpp. Loolu moo taxoon ma sóobu bu baax ci benn kurélu communiste bi ñu jagleeloon ndaw ñi. Bi ma amee 14 at def naa jot bu bare ci benn projet bu doon yëngu ci defaraat kayit yi baaxatul woon. Kilifay dëkku Aue dañu kontaanoon lool ci man ba neexal ma. Bu dee sax ndaw laa woon, xamoon naa ay kilifa yu mag yu doon def politig ci RDA. Jàppoon naa ne li ma doon def lu baax la te sama ëllëg dina neex.

Waaye damaa xéy bés rekk, lépp yàqu. Ci atum 1989 miiru Berlin dafa daanu, yóbbaale réewu communiste yi nekkoon ci penku Ërob. Waaye musiba yi yemul rekk ci loolu. Mujj naa xam ne njubadi dafa bare woon ci RDA. Ci misaal, ñi gëmoon communisme dañu doon xeeb ñi àndul woon ak ñoom. Loolu nu mu mën a nekke? Xanaa du ñun communiste yi, li ñu gëm mooy ñépp a yem? Walla mbir mi ay naxe rekk la woon? Sama xel daldi jaxasoo lool.

Ma daldi soppi samay jubluwaay sóobu ci misik ak art. Ndegam mënoon naa dem ci lekkool buy jàngale misik te dem iniwersite, ma fas yéene liggéey ci wàllu misik ak art. Te lu baax li ñu ma jàngaloon lépp bi may nekk xale, ma won ko ginnaaw. Foo rekk moo amoon solo ci man, ak di nekkaale ak jigéen ñu bare. Waaye misik, art ak def lu ma neex taxul sama njàqare wàññeeku. Tiit gi ma doon yëg dafa doon feeñ ci li ma doon desine. Lan moo ñuy xaar ëllëg? Lu tax ñu nekk ci kaw suuf?

Mujj naa am tontu ci laaj yi ma doon laaj sama bopp te tontu yooyu jaaxaloon nañu ma. Benn ngoon ca lekkool ba, dama nekkoon ak ay eleew yu doon wax ci lu jëm ci ëllëg. Mandy *, kenn ci eleew yooyu, Seede Yexowa la woon. Ci ngoon googu jox na ma ay xelal yu baax. Mu ne ma: «Andreas, boo bëggee am tontu ci say laaj yu jëm ci dund gi tey ak ëllëg, gëstul bu baax Biibël bi».

Gëmuma woon lépp li mu ma wax, waaye deñ-kumpa moo tax ma tàmbali jàng Biibël bi. Mandy won ma Dañeel pàcc 2, li ma fa jàng jaaxaloon na ma. Yégle yonent boobu dafay wax ci ay nguur yu am doole yu waroon a toppante te li ñuy def dina ñu laal ba ci suñu jamono. Mandy won na ma yeneen yégle yonent yu jëm ci suñu ëllëg. Booba laa door a am ay tontu ci samay laaj! Waaye kan moo bind yégle yonent yooyu, te kan moo mënoon a wax liy xew ëllëg ci anam bu leeree noonu? Mbaa du Yàlla dafa am?

NI BIIBËL BI SOPPEE SAMA DUND

Mandy dafa ma boole ak benn Seede Yexowa bu tudd Horst ak jabaram Angelika ngir ñu dimbali ma ma gën a xam Kàddu Yàlla. Seetlu naa ci lu gaaw ne Seede Yexowa yi rekk ñooy diine juy jëfandikoo turu Yàlla, Yexowa, te di ko jàngal nit ñi (Psaume 83:18; Macë 6:⁠9). Jàng naa ne Yexowa dafa bëgg nit ñi dund ba fàww ci àjjana ci kaw suuf. Sabóor 37:9 nee na «ku yaakaar Aji Sax ji, jagoo réew mi». Ni Yexowa di mayee dund gu dul jeex ñépp ñiy góor-góorlu ngir topp santaaneem yi nekk ci Biibël bi laal na ma lool.

Waaye jafe woon na ci man ma soppi sama dundin ba mu méngoo ak li Biibël bi wax. Ni ma nekkoon ku siiw ci wàllu misik ak art, moo tax ma yéegoon sama bopp. Kon dama waroon a njëkk a jàng nekk nit ku woyof. Rax-ci-dolli, yombul woon ci man ma bàyyi sama dundin bu bon. Maa ngi gërëm Yexowa bu baax ndax muñ ak yërmande gi muy won ñiy def lépp ngir jëfe li Biibël bi di jàngale!

Ba bi may am 18 at, li ma jàppoon mooy Yàlla amul te communisme mooy li gën. Waaye booba ba léegi, Biibël bi mu ngi soppi sama dund. Li ma jàng dalal na sama xel ci lu jëm ci ëllëg te tax na sama dund gën a neex. Ci atum 1993 laa sóobu ci dox te doon Seede Yexowa. Ci atum 2000 laa takk Tabitha, benn Seede Yexowa bu sawar ci liggéeyu waare. Dañu doon def lépp li ñu mën ngir dimbali nit ñi ñu xam Biibël bi. Ñu bare ñi ñu doon taseel dañu meloon ni man, gëmuñu woon Yàlla te dañu foogoon ne communisme moo gën. Dama doon bég ci won leen ni ñu mënee gën a jege Yexowa.

NJARIÑ BI MA CI JËLE

Bi ma tàmbalee ànd ak Seede Yexowa yi, samay waajur dañoo meroon lool. Waaye mujj nañu gis ne ànd ak Seede Yexowa yi lu baax rekk la def ci sama dund. Am naa mbégte ci gis leen léegi ñuy jàng Biibël bi, te di teewe ndaje Seede Yexowa yi.

Man ak Tabitha am nañu jàmm ci suñu séy ndaxte dañuy góor-góorlu ci topp li Biibël bi wax ci wàllu séy. Ci misaal, topp li Biibël di wax ci lu jëm ci yem rekk ci ki ngay séyal gën na dëgëral suñu diggante (Yawut ya 13:⁠4).

Ragalatuma ci lu jëm ci sama dund tey ak ëllëg. Bokk naa ci njaboot gu réy gu boole ay nit ñu jóge ci àddina si sépp, ñu am jàmm dëgg te doon benn. Kenn xeebu ci sa moroom, ñun ñépp a yem. Loolu laa mas a gëm te moom laa mas a bëgg ci sama giiru dund.

^ par. 12 Dañu soppi tur bi.