Ubbil li ci biir

Lu mën a tax Yàlla bañ a nangu suñuy ñaan?

Lu mën a tax Yàlla bañ a nangu suñuy ñaan?

Li Biibël bi wax

Am na ay ñaan yu Yàlla dul nangu. Xoolal li mën a tax Yàlla bañ a nangul nit ñaanam.

1. Ñaan bu àndul ak coobare Yàlla

Yàlla du nangu ñaan bu àndul ak coobareem, maanaam ñaan bu àndul ak li mu santaane ci Biibël bi (1 Yowaana 5:14). Biibël bi nee na, waruñu bëgge. Te fasoŋu lotëri yépp dañuy xiir nit ci bëgge (1 Korent 6:​9, 10). Kon boo ñaanee Yàlla ngir gañe lotëri, Yàlla du nangu sa ñaan. Bul foog ne loo bëgg rekk te ñaan ko Yàlla, mu may la ko. War nga ko gërëm sax ci loolu. Lu tax? Bu doon nangu ñaan yépp, dinañu dëkk ci tiit ndaxte am na ñuy ñaanal seen moroom lu bon (Saag 4:3).

2. Nit kuy def lu bon te tey ko

Yàlla du déglu ñi dëkk ci di ko tooñ. Lii la Yàlla waxoon ay nit ñu doon wax ne dañu koy jaamu fekk dañu doon def lu bon te tey ko: «Bu ngeen doon ñaan-ñaanee it, du maa leen di déglu: seeni loxo, deret la taq ripp» (Esayi 1:15). Waaye bu ñu réccu woon seeni bàkkaar te defaraat seen diggante ak Yàlla, Yàlla dina déglu seeni ñaan (Esayi 1:18).