Ubbil li ci biir

Ndax Biibël bi mën na ma dimbali ma am jàmm ci sama biir njaboot?

Ndax Biibël bi mën na ma dimbali ma am jàmm ci sama biir njaboot?

Li Biibël bi wax

Biibël bi mën na la dimbali nga am jàmm ci sa biir njaboot. Joxe na ay xelal yu baax yu amal njariñ ay milioŋi nit, góor ak jigéen. Xelal yii, ci lañu bokk:

  1. Séyal ci yoon. Séy ci kanamu yoon ngir wone ne fas yéene nga nekk ak ki nga séyal sa dund gépp, mooy li njëkk ngir jàmm am ci sa njaboot (Macë 19:4-6).

  2. Wegal ki nga séyal te won ko mbëggeel. Dafa laaj ngay doxale ak ki nga séyal ni nga bëgge mu doxale ak yow (Macë 7:12; Efes 5:25, 33).

  3. Moytul wax ju ñaaw. Waxal wax ju rafet, bu dee sax ki nga séyal dafa wax walla mu def lu la metti (Efes 4:31, 32). Ni ko Biibël bi waxe ci Kàddu yu Xelu 15:1: «Tont lu neex day giifal, baat bu ñagas di jógal xol.»

  4. Nanga yem ci ki nga séyal. Waaroo xemmem keneen ku dul ki nga séyal (Macë 5:28). Biibël bi nee na: «Na ñépp fullaal séy, te lalu séy bi baña taq sobe» (Yawut ya 13:4).

  5. Yaral say doom te na ànd ak mbëggeel. Bul bàyyi say doom ñu def lu leen neex, waaye it bul dëgër ak ñoom ba mu ëpp (Kàddu yu Xelu 29:15; Kolos 3:21).