Ubbil li ci biir

Lu tax ñuy woowe Yeesu Doomu Yàlla?

Lu tax ñuy woowe Yeesu Doomu Yàlla?

Li Biibël bi wax

Ci Biibël bi, dañu faral na di woowe Yeesu «Doomu Yàlla ji» (Yowaana 1:49). Yàlla moo sàkk lépp te lépp luy dund ci moom la jóge. Dañuy wax ne Yeesu «Doomu Yàlla» la ndaxte Yàlla moo ko sàkk (Sabóor 36:10; Peeñu 4:11). Biibël bi masul wax ne Yàlla dafay jur doom. Doomu Aadama yi ñooy jur doom.

Ci Biibël bi, dañuy woowe itam malaaka yi «goney Yàlla» (Ayóoba 1:6). Te it «doomu Yàlla» lañu woowe góor gu njëkk ga, maanaam suñu maam Aadama (Luug 3:38). Waaye Yeesu mooy ki Yàlla njëkk a sàkk te kenn nekkul woon ak Yàlla bi mu koy sàkk. Looloo tax Biibël bi wax ne Yeesu mooy ki njëkk ci doomu Yàlla yi.

  • Ndax Yeesu dafa doon dund ca asamaan bala muy ñëw ci kaw suuf​?

  • Lan la Yeesu doon def bala muy ñëw ci kaw suuf​?

Ndax Yeesu dafa doon dund ca asamaan bala muy ñëw ci kaw suuf​?

Waaw, Yeesu malaaka la woon ca asamaan bala muy juddu nekk nit ci kaw suuf. Yeesu ci boppam nee na: «Man ca kaw laa jóge» (Yowaana 6:38; 8:23).

Yeesu la Yàlla njëkk a sàkk bala muy sàkk leneen. Lii la Biibël bi wax ci Yeesu:

  • «Mooy taaw bi, ki gëna màgg lépp luy mbindeef» (Kolos 1:15).

  • Mooy «ndeyi bindu mbindeefi Yàlla yi» (Peeñu 3:14).

Yeesu matal na yégle yonent bi doon wax ne am na ku «cosaanam di jant yu yàgga yàgg, bu jëkkoon» (Mise 5:1; Macë 2:4-6).

Lan la Yeesu doon def bala muy ñëw ci kaw suuf​?

Taxawaay bu am solo la amoon ca asamaan. Ci loolu la doon wax bi muy ñaan lii: «Baay, [...] feeñalal ci man ndam, li ma amoon ci sa wet, laata àddina di sosu» (Yowaana 17:5).

Yeesu jàppale na Baayam bi mu doon sàkk lépp. Yeesu liggéey na ak Yàlla te «ku xareñ» la woon ci liggéeyam (Kàddu yu Xelu 8:30). Biibël bi nee na: «Ci moom la Yàlla sàkke lépp lu nekk ci asamaan ak suuf» (Kolos 1:16).

Yàlla jaar na ci Yeesu ngir sàkk lépp, maanaam malaaka yi ak asamaan ak suuf (Peeñu 5:11). Mën nañu méngale loolu ak kuy defar palaŋu kër ak masoŋ bi koy tabax. Kon Yàlla moo defar palaŋ yi waaye Yeesu la jox mu def liggéey bi.

Yeesu moo nekkoon Kàddu gi. Bala Yeesu di ñëw ci kaw suuf, Biibël bi woowe na ko «Kàddu gi» (Yowaana 1:1). Loolu dafay wone ne Yàlla dafa jaar ci Yeesu ngir jottali Kàddoom yeneen malaaka yi.

Te dafa mel ni moom moo doon jottali itam Kàddu Yàlla nit ñi. Mën nañu xalaat ne, ci Yeesu la Yàlla jaar ngir wax Aadama ak Awa li mu leen santoon ci toolu Eden (Njàlbéen ga 2:16, 17). Xéyna sax Yeesu moo nekkoon malaaka mi doon jiite waa Israyil ca màndiŋ ma te ñu waroon koo déggal bu baax (Mucc ga 23:20-23). *

^ par. 14 Malaaka bi ñuy woowe Kàddu gi, du moom rekk moo doon jottali li Yàlla wax. Li koy wone mooy, Yàlla jaar na ci yeneen doomam, maanaam yeneen malaaka ngir jottali waa Israyil Yoonu Musaa (Jëf ya 7:53; Galasi 3:19; Yawut Ya 2:2, 3).