Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

PÀCC FUKK AK ÑÉENT

Li ñu mën a def ba suñu njaboot bare jàmm

Li ñu mën a def ba suñu njaboot bare jàmm
  • Lan mooy tax ñu nekk jëkkër ju baax ?

  • Lan la jigéen mën a def ngir doon jabar ju baax ?

  • Lan mooy tax ñu nekk waajur ju baax ?

  • Naka la xale yi mënee def seen wàll ngir njaboot gi bare jàmm ?

1. Lan mooy tax njaboot bare jàmm ?

YEXOWA YÀLLA dafa bëgg sa njaboot bare jàmm. Ci Kàddoom, Biibël bi, am na lu Yàlla sant képp ku bokk ci njaboot. Dafay won ku nekk taxawaayam ci kër gi. Bu ñépp defee li leen war ni ko Yàlla santaanee, lu rafet lay indi. Yeesu waxoon na ne : «Ki barkeel mooy kiy déglu kàddug Yàlla te di ko topp.» — Luug 11:⁠28.

2. Lan lañu war a nangu bu ñu bëggee suñu njaboot bare jàmm ?

2 Liy gën a tax njaboot bare jàmm, mooy ñu nangu ne Yexowa moo sos njaboot, moom mi Yeesu doon woowe “ Sunu Baay bi ”. (Macë 6:⁠9). Njaboot goo gis ci kaw suuf, suñu Baay bi nekk ca asamaan moo tax mu am, te ci lu wóor Yàlla xam na bu baax li mën a tax njaboot yi bare jàmm (Efes 3:​14, 15). Kon lan la Biibël bi wax ci li Yàlla sant kenn ku nekk ci njaboot gi ?

YÀLLA MOO SOS NJABOOT

3. Naka la Biibël bi di wonee ni njaboot gu njëkk gi komaasee, te lan moo ñuy won ne li Biibël bi wax amoon na dëgg ?

3 Yexowa dafa bind Aadama ak Awa, boole leen ñu nekk jëkkër ak jabar. Mu dugal leen ci àjjana ju rafet ci kaw suuf ngir ñu dëkk fa, maanaam ca toolu Eden. Yexowa wax leen ñu am ay doom. Mu ne leen : «Giirleen te bare, ba fees àddina.» (Njàlbéen ga 1:​26-28 ; 2:​18, 21-24). Loolu du ay leeb walla ay wax kese, ndaxte Yeesu xamal na ñu ne li téere Njàlbéen ga wax ci fi njaboot komaase, amoon na dëgg (Macë 19:​4, 5). Dëgg la jafe-jafe yi bare nañu te àddina si melul ni ko Yàlla bëgge woon. Waaye nañu seet lu tax am jàmm ju bare ci njaboot nekk lu mën a am ba tey.

4. a) Naka la kenn ku nekk ci kër gi mënee def wàllam ngir njaboot gi bare jàmm ? b) Lu tax jàng ni Yeesu doon dunde am solo lool ngir jàmm am ci njaboot ?

4 Kenn ku nekk ci kër gi bu royee ci mbëggeel bi Yàlla di wone, dina mën a def wàllam ngir njaboot gi bare jàmm (Efes 5:​1, 2). Komka mënuñu gis Yàlla, naka lañu ko mënee roy ? Mën nañu xam ni Yexowa di jëfe, ndaxte dafa yónni ci kaw suuf benn Doom ji mu am kepp bi nekkoon ca asamaan (Yowaana 1:​14, 18). Doom jooju mooy Yeesu Kirist. Bi mu nekkoon ci kaw suuf, dafa doon roy bu baax Baayam bi nekk ca asamaan. Loolu tax na ba gis Yeesu te di ko déglu, dafa meloon ni nekk ci wetu Yexowa di ko déglu (Yowaana 14:⁠9). Moo tax bu ñuy jàng ngir xam ni Yeesu doon wonee mbëggeel te di roy ci moom, kenn ku nekk ci ñun dina mën a def wàllam ngir njabootam gën a bare jàmm.

ROYUKAAY LA CI JËKKËR YI

5, 6. a) Fasoŋ bi Yeesu doon toppatoo mbooloo mi naka la nekke royukaay ci jëkkër yi ? b) Bu ñu bëggee Yàlla baal ñu suñuy bàkkaar, lan lañu war a def ?

5 Biibël bi nee na, jëkkër yi dañu war a toppatoo seen jabar ni Yeesu di toppatoo talibeem yi. Seetal li Biibël bi wax fii : “ Yéen nag góor ñi, na ku nekk bëgg jabaram, ni Kirist bëgge mbooloo mi, ba joxe bakkanam ndax moom [...] Na góor bëgg jabaram, ni mu bëgge boppam. Bëgg sa jabar, bëgg sa bopp la. Ndaxte kenn masul a bañ sa yaram. Waaye danga koy dundal, di ko fonk. Noonu it la Kirist fonke mbooloo mi. ” — Ñun ñoo dëngal mbind yi ; Efes 5:​23, 25-29.

6 Ni Yeesu bëgge mbooloo taalibeem yi, royukaay bu mat sëkk la ci jëkkër yi. Yeesu ‘ bëggoon na leen ba fa mbëggeel man a yem ’, dem ba joxe bakkanam ngir ñoom, fekk ay nit ñu matul lañu woon (Yowaana 13:1 ; 15:13). Noonu it, lii lañu wax jëkkër yi : “ Na ku nekk kontine di bëgg jabaram te muñal ko. ” (Kolos 3:19, NW). Lan mooy dimbali jëkkër mu topp xelal yooyu, rawatina bu jabaram juumee ? War na fàttaliku ne dafay juum moom itam, fàttaliku it li mu war a def ngir Yàlla baal ko. Lan la war a def ? Dafa war a baal ñi koy tooñ, te jabaram ci la bokk. Loolu la jabar ji war a def itam (Macë 6:​12, 14, 15). Kon bu nit ñi di wax ne bu séy neexee dafa fekk mu boole ñaari nit ñu sawar a baal seen moroom, loolu dëgg la.

7. Ci lan la Yeesu doon bàyyi xel, te loolu naka la nekke royukaay ci jëkkër yi ?

7 Jëkkër yi waruñu fàtte it ne Yeesu dafa masoon a may cér ay taalibeem. Dafa doon bàyyi xel ci li ñu àttan ak ci seen soxla yaram. Amoon na bés taalibeem yi sonn, Yeesu daldi leen ne : «Nanu beddeeku, dem ci bérab bu wéet ; ngeen noppalu fa tuuti.» (Mark 6:​30-32). Jabar yi it war nañu leen a toppatoo, may leen cér. Biibël bi dafay méngale jabar ak ‘ àndandoo ju gën a néew doole ’ seen jëkkër. Te Biibël bi digal na seeni jëkkër ñu jox leen “ teraanga ju mat ”. Lu tax ? Ndaxte jëkkër ak jabar ñoo ‘ yem cér ci yiwu Yàlla, wi leen ubbil buntu dund gu dul jeex ’. (1 Piyeer 3:⁠7.) Jëkkër yi waruñu fàtte ne Yàlla dafay fonk nit ci kaw li nit kooku di ko topp, waaye du ci li nit ki doon góor walla jigéen. — Psaume 101:⁠6.

8. a) Lu tax ñu mën a wax ne, “ bëgg sa jabar, bëgg sa bopp la ” ? b) Doon “ benn ” lu muy tekki pur jëkkër ak jabar ?

8 Biibël bi nee na “ bëgg sa jabar, bëgg sa bopp la ”, ndaxte, ni ko Yeesu waxe woon, jëkkër ak jabar «nekkatuñu ñaar waaye benn». (Ñun ñoo dëngal mbind yi ; Macë 19:⁠6.) Kon lalu séy ci ñoom ñaar kese la war yem (Proverbes 5:​15-21 ; Yawut ya 13:⁠4). Dinañu mën a def loolu su dee ku ci nekk dafay jiital li moroomam soxla (1 Korent 7:​3-5). Kàddu yii am nañu solo lool : “ Kenn masul a bañ sa yaram. Waaye danga koy dundal, di ko fonk. ” Jëkkër yi war nañu bëgg seen jabar ni ñu bëgge seen bopp, te bañ a fàtte ne dinañu mas a taxaw ci seen kanamu kilifa, Yeesu Kirist, ngir wax li ñu def. — Ñun ñoo dëngal mbind yi ; Efes 5:29 ; 1 Korent 11:⁠3.

9. Ban jikko Yeesu lañu wone ci Filib 1:​8, te lu tax jëkkër yi war a won seen jabar jikko jooju ?

9 Ndaw li Pool waxoon na ci “ cofeelu Kirist Yeesu ”. (Filib 1:⁠8.) Cofeel bi Yeesu amoon dafa doon seddal xolu nit ñi. Cofeel boobu moo laal ay jigéen yu demoon ba nekk ay taalibeem (Yowaana 20:​1, 11-13, 16). Jigéen ñi soxla nañu lool seen jëkkër won leen cofeel.

ROYUKAAY CI JABAR YI

10. Naka la Yeesu nekke royukaay ci jabar yi ?

10 Njaboot dafa mel ni kurél. Su ñu bëggee mu aw yoon, fàww mu am kilifa. Yeesu sax am na Kilifa bu muy déggal. Yàlla mooy “ kilifag Kirist ” ni góor nekke “ kilifag jigéen ”. (1 Korent 11:⁠3.) Fasoŋ bi Yeesu déggale Yàlla mii nekk kilifaam, royukaay bu rafet la ndaxte ñun ñépp a am kilifa bu ñu war a déggal.

11. Nan la jabar war a mel ak jëkkëram, te lan la jëfinam mën a indi ?

11 Góor ñi matuñu, moo tax ñuy juum te ci lu bare nekkuñu boroom kër yi gën. Komka noonu la, lan la jabar war a def ? Warul xeeb li jëkkëram di def, walla muy jéem a jiite. Li gën ci jabar mooy mu bañ a fàtte ne ci kanamu Yàlla xol bu nooy te dal, lu am solo la (1 Piyeer 3:⁠4). Bu jigéen amee jikko bu mel noonu, su nekkee ci lu metti sax, déggal jëkkëram ni ko Yàlla bëgge dina gën a yomb ci moom. Te it Biibël bi nee na : “ Na [...] jigéen ji weg jëkkëram. ”(Efes 5:33). Waaye bu jëkkër ji nanguwul déggal Kirist nag ? Lii la Biibël bi wax jigéen ñi : “ Na ku nekk nangul sa jëkkër. Noonu su amee góor gu gëmul kàddug Yàlla, te gis jabaram di dund dund gu sell, boole ci weg ko, loolu dina ko gindi ci lu àndul ak wax. ” — Ñun ñoo dëngal mbind yi ; 1 Piyeer 3:​1, 2.

12. Wax sa jëkkër li nga xalaat ci fasoŋ bu rafet, lu tax dara nekku ci ?

12 Bu sa jëkkër nekkee karceen walla déet, boo ko waxee lu àndul ak li muy xalaat, te nga def ko ci fasoŋ bu rafet, loolu du ñàkk koo may cér. Jigéen ji mën nañu wax dëgg, te waa kër gi yépp mën na ci jariñoo bu ko jëkkëram dégloo. Ibraayma àndul woon ak li ko jabaram Saarata xelaloon ngir faj poroblem bu amoon ci njaboot gi. Waaye Yàlla dafa ko waxoon : «Defalal Saarata li mu la wax rekk.» (Njàlbéen ga 21:​9-12). Dëgg la, li jëkkër ji mujj a jàpp, bu dee weddiwul li Yàlla santaane, jabaram dina wone ne dafa ko déggal bu ko ci jàpplee. — Jëf ya 5:29 ; Efes 5:⁠24.

Ban royukaay bu rafet la Saarata bàyyil jabar yi ?

13. a) Ci lan la Tit 2:​4, 5 xiirtal jigéen yuy séy ? b) Lan la Biibël bi wax ci tàggoo ak tas séy ?

13 Jabar mën na def lu bare ci njaboot gi buy def li ko war. Biibël bi nee na jigéen yuy séy dañu war a “ bëgg seeni jëkkër ak seeni doom, di ñu maandu, sell te fonk seen kër, ñu neex deret te déggal seeni jëkkër ”. (Tit 2:​4, 5.) Jabar walla yaay buy def noonu, waa këram dinañu ko bëgg dëgg te may ko it cér (Proverbes 31:​10, 28). Waaye séy dafay boole ñaari nit ñu matul. Moo tax jafe-jafe yu metti lool mën na def ñu tàggoo walla seen séy tas. Biibël bi may na ñaar ñuy séy ñu tàggoo bu ñu nekkee ci yenn yi. Waaye ba tey, waruñu caaxaane tàggoo, ndaxte lii la Biibël bi wax : “ Jigéen ju séy warul a teqalikoo ak jëkkëram. [...] Te bu jëkkër ji fase jabaram. ” (1 Korent 7:​10, 11). Bu amee kenn ci ñoom ñaar ku njaaloo, loolu kese mooy tax Mbind mi daganal tas séy. — Macë 19:⁠9.

ROYUKAAY BU MAT NGIR WAAJUR YI

14. Nan la Yeesu meloon ak xale yi, te lan la xale yi soxla ci seen waajur ?

14 Yeesu bàyyil na waajur yi royukaay bu mat ci ni mu meloon ak xale yi. Bi mu amee ñu bëggoon a tere ay xale ñu jege Yeesu, dafa leen ne : «Bàyyileen xale yi, ñu ñëw fi man ! Buleen leen tere.» Biibël bi nee na “ noonu Yeesu leewu leen, teg leen ay loxoom, barkeel leen ”. (Màrk 10:13-16.) Komka Yeesu dafa jël jotam ngir nekk ak xale yi, ndax waruleen def ni moom, nekk ak seeni doom yu góor ak yu jigéen yi ? Xale yi du tuuti rekk lañu soxla ci seen jot. Lu bare lañu ci soxla. Dangeen war a jël ci seen jot ngir jàngal leen, ndaxte loolu la Yexowa sant waajur yi. — Deutéronome 6:​4-9.

15. Lan la waajur yi mën a def ngir aar seeni doom ?

15 Àddina sii dafay gën di bon. Looloo tax xale yi soxla waajur yu leen di aar ci ñi leen bëgg a def lu bon, mel ni ñiy wut ay xale ngir siif leen. Nañu seet ni Yeesu doon aare taalibeem yi mu bëggoon lool ba di leen woowe “ samay doom ”. Bi ñu ko jàppee, di ko waaj a rey, dafa fexe ba taalibeem yi mën a rëcc (Yowaana 13:​33, NW ; 18:​7-9). Waajur yi, war ngeen xool bu baax ngir gaaw a xeex li Seytaane di fexe ngir gaañ seeni gune. Dangeen leen war a xelal ci loolu bala dara di xew * (1 Piyeer 5:⁠8). Li mën a gaañ xale yi ci wàllu yaram, ci wàllu ngëm, ak li mën a yàq seen xel, masul a bare ba tollu ni mu tollu tey.

Lan la waajur yi mën a jàng ci ni Yeesu meloon ak xale yi ?

16. Lan la waajur yi mën a jàng ci fasoŋ bi Yeesu doon def bu taalibeem yi juumee ndax li ñu matadi ?

16 Guddi bu jiitu bés bi ñu rey Yeesu, taalibeem yi dañu doon werante ngir xam ku gën a mag ci ñoom. Yeesu merewu leen, waaye ci wax ak ci jëf yu ànd ak mbëggeel dafa kontinee jéem a laal seen xol (Luug 22:​24-27 ; Yowaana 13:3-8). Su dee am nga ay doom, ndax mënuloo seet ni nga mënee roy Yeesu boo leen di jubbanti ? Dëgg la, xale yi soxla nañu ñu yar leen. Waaye waruñu ci ëppal te buñu ko def mukk ak xol bu tàng. Dañu war a xalaat bala ñu leen di wax dara, te bañ a wax ak ñoom “ ni kuy dóor jaasi sa moroom ”. (Jérémie 30:11 ; Léeb yi 12:​18, NW.) Dañu war a yar xale yi ci fasoŋ boo xam ne, bu ëllëgee dinañu gis ne yar boobu lu baax la woon. — Efes 6:4 ; Yawut ya 12:9-11.

ROYUKAAY CI XALE YI

17. Naka la Yeesu nekke royukaay bu mat ci xale yi ?

17 Ndax am na li xale yi mën a jàng ci Yeesu ? Waawaaw, mën nañu jàng ci moom ! Ni Yeesu meloon dafay wone ni xale war a déggale ay waajuram. Yeesu waxoon na ne : «Li ma Baay bi jàngal rekk laay wax.» Mu teg ci ne : «Li ko neex rekk laay def.» (Yowaana 8:​28, 29). Yeesu dafa déggaloon Baayam bi nekk ca asamaan. Biibël bi nee na it na xale yi déggal seeni waajur (Efes 6:​1-3). Yeesu nit ku mat la woon. Waaye dafa déggaloon ay waajuram Yuusufa ak Maryaama, fekk matuñu woon. Wóor na ne li leen Yeesu déggal taxoon na ba waa këram yépp nekk ci mbégte. — Luug 2:​4, 5, 51, 52.

18. Lu tax Yeesu doon déggal saa su nekk Baayam bi nekk ca asamaan, te bu xale yi di déggal seeni waajur, kan mooy bég ?

18 Ndax xale yi gis nañu ni ñu mënee gën a roy Yeesu, te bégal seeni waajur ? Dëgg la, yenn saay déggal sa waajur dafay jafe ci xale yi. Waaye Yàlla dafa bëgg xale yi déggal seeni waajur (Proverbes 1:8 ; 6:20). Yeesu dafa mas a déggal Baayam bi nekk ca asamaan, bu metti woon sax. Amoon na bés bu Yàlla bëggoon Yeesu def lu jafe lool. Lii la Yeesu waxoon : «Teggil ma kaasu naqar bii [maanaam li mu waroon a def].» Waaye ba tey, li ko Yàlla sant rekk la Yeesu defoon, ndaxte xamoon na ne Baayam moo xam li gën ci moom (Luug 22:42). Bu xale yi di jàng déggal seeni waajur, loolu dina neex lool seeni waajur ak seen Baay bi nekk ca asamaan *. — Proverbes 23:​22-25.

Lan la xale yi warul a fàtte bu ñu leen di jéem a fiir ?

19. a) Naka la Seytaane di jéemee fiir xale yi ? b) Bu xale yi defee lu bon, lan lay def ci seeni waajur ?

19 Ibliis jéemoon na fiir Yeesu, te na ñu wóor ne dina jéem a fiir xale yi ngir ñu def lu bon (Macë 4:​1-10). Seytaane miy Ibliis dafay jaar ci ay xarit ak ay dëkkandoo ngir xiir ñu ci lu bon. Bañ loolu mën na jafe. Kon moytu àndandoo yu bon yi, am na solo lool ci xale yi (1 Korent 15:33). Diina, doomu Yanqóoba bu jigéen bi, dafa doon ànd ak ñu dul jaamu Yexowa. Mujj na ci am coono yu bare (Njàlbéen ga 34:​1, 2). Xalaatal naqar bi njaboot di am bu ci amee ku njaaloo ! — Proverbes 17:​21, 25.

LIY TAX NJABOOT DI AM JÀMM

20. Lan la kenn ku nekk ci kër gi war a def ngir njaboot gi am jàmm ?

20 Bu ñu toppee li Biibël bi wax, regle poroblem yi ci kër gi dafay gën a yomb. Ci dëgg, digle yi nekk ci Biibël bi ñooy tax njaboot di am jàmm. Kon jëkkër yi, bëggleen seen jabar te di leen toppatoo ni Yeesu di toppatoo mbooloo mi. Jigéen ñi, déggalleen seen jëkkër, te roy jigéen bu am manoore bi ñu wax ci Proverbes 31:​10-31. Waajur yi, yarleen seeni doom (Proverbes 22:⁠6). Na baay yi ‘ yor seen kër yorin wu rafet ’. (1 Timote 3:​4, 5 ; 5:⁠8.) Te xale yi, déggalleen seeni waajur (Kolos 3:20). Kenn matul ci waa kër gi, ndaxte ñépp ay juum. Kon nangeen woyof, di baalu.

21. Lu neex lan lañuy séentu, te naka lañu mënee am njaboot gu bare jàmm tey jii ?

21 Ci dëgg, ci Biibël bi am na digle ak xelal yu bare te am solo ci dundu njaboot. Rax-ci-dolli dafay wax ci àddina bu bés bi ñu Yàlla dig, ak ci àjjana ci kaw suuf bi nga xam ne ay nit ñu bég ñuy jaamu Yexowa ñoo fay nekk (Peeñu ma 21:​3, 4). Loolu ñuy séentu neex na lool ! Waaye tey jii sax, bu ñuy def li Yàlla wax ci Kàddoom Biibël bi, dinañu mën a am njaboot gu bare jàmm.

^ par. 15 Am na ay xelal yi ñuy dimbali ñu aar xale yi ci téere bi tudd Écoute le grand Enseignant (Déglul jàngalekat bu mag bi), ci pàcc 32. Seede Yexowa yi ñoo defar téere boobu.

^ par. 18 Bu waajur laajee doomam lu àndul ak li Yàlla santaane, booba kese la bañ a déggal sa waajur doon lu jub. — Jëf ya 5:⁠29.